Maa ngi tudd Talla Gueye,
te ci sama xol amna benn tur bu neex bu leer ni biddéew yi : Fatma.
Bis bi nu jëkk a gisante,
sama dund soppeeku na.
Bala maa xam la,
fan yi dañuy jaar rekk ak lu dul mbégte,
guddi yi it daan nañu yagg ci noppalu ak tiis.
Waaye yaw Fatma,
danga agsi ni leer gu neex ci sama dund,
ni taw gu sedd ci waxtu wowu wow.
Bu ma la xalaate,
sama xol dafay daw gaaw.
Sa bët set wecc sama tiis,
sa baat may ma jàmm,
te sa présence may ma doole
ngir ma yokk sama yoon ci dund.
Fatma,
yaw yaa di jigéen ju ñu mëna daje benn yoon rekk ci dund.
Jigéen ju am fayda, ju rafet ci xol,
ju yaru te am kersa.
Man Talla Gueye,
dama lay digal
ne dinaa la respectal saa su ne,
dinaa nek ak yaw
ci jamono yu baax ak yu metti.
Bëgguma mbëggeel gu aju ci fen,
wala ci ay wax yu amul solo.
Dama bëgg mbëggeel gu dëgg,
gu dëgër,
gu mana daan at yi,
jàngoro yi ak fitna yi.
Ak yaw Fatma,
damay gént dund gu neex.
Damay gént nu doxandoo,
loxo ci loxo,
ak xel mu dal.
Damay gént dégg sa reeñ saa su nekk ci suba,
gis sa bët yi di leer ak mbégte,
te nu tabax kër gu fees ak jàmm ak mbëggeel.
Yenn saay nit ñi dañuy wax,
dañuy àtte lu ñu xamul.
Waaye man xam naa li sama xol di wax.
Xam naa ne sama xol tànn na la ci dëgg.
Bu addina bépp sax dugg ci sunu diggante,
dinaa la bëgg ba fàww.
Fatma,
boo amee tiis, sama xol it day metti.
Boo ree, dama am mbégte.
Yaa nekk benn pàcc ci sama bakkan,
benn pàcc ci sama ruu.
Dama bëgg maa di ki lay fomp sa ay rangooñ,
ki lay aar,
ki lay fàttali bes bu ne
ni nga ame solo ci sama dund.
Ndaxte mbëggeel gu dëgg
du wax yu neex rekk.
Moo di muñ, wormaalante, kóolute ak baalante.
Te loolu lépp,
dama bëgg koo dund ak yaw.
Talla Gueye ak Fatma,
ñaari xol yu booloo ci mbëggeel gu dëgg,
ñaari ruu yu bëgg àndandoo
ci anam yu baax ak yu metti.
Te bu sama kawar sax weexee njëkk,
bu at yi sax weesu,
dinaa bëgg ba tey wax :
“Fatma mooy li gën a rafet
lu xew ci sama dund.” ❤️